settings icon
share icon
Laaje

Wan mooy yoonu mucc gi?

Tontu wi


Ndax danga xiif ? Du xiif lekk, waaye ndax danga xiif leneen ci dund gi ? Ndax am na ci sa biir leneen lu matagul ? Su de noonu la deme, Yeesu mooy yoon wi ! Yeesu ne leen: «Man maay ñam wiy joxe dund. Ku ñëw ci man, doo xiif mukk; te ku ma gëm, doo mar » (Yowaana 6 :35)

Ndax danga jaxasoo ? Ndax manuloo gis ab yoon wala jëmu ci dund gi ? Ndax dafa melni dafa am ku fay lamp yi te manuloo gis taalukaay bi ? Su de noonu la deme, Yeesu mooy yoonu mucc gi ! Yeesu jubluwaat ca mbooloo ma ne leen: «Man maay leeru àddina si. Ku ma topp doo dox cig lëndëm, waaye dinga am leeru dund.» (Yowaana 8 :12)

Ndax danga am yëg yëgu ku ne genne ci dund gi ? Ndax jeem nga fëgg bunt yu bari, ngir seetlu ne rekk ci gannaaw bunt yooyu dara nekku fa te it dara amufa njariñ. Ndax ya ngi seet ab bunt ngir dugg ci dund gu naat ? Su de noonu la deme, Yeesu mooy yoonu mucc gi ! Man maay bunt bi; ku jaar ci man, dinga mucc, dinga mana dugg ak a génn, dinga am it mbooy goo mana fore. (Yowaana 10 :9)

Ndax ñeneen ñi dañu lay bayi nga daanu sa bu nekk ? Ndax seeni diggante dafa xóot walla sorewul te dara nekku fa ? Ndax danga japp ni nit ñi dañuy porofitóo ci yaw ? Su de noonu la deme, Yeesu mooy yoon wi ! «Man maay sàmm bu baax bi. Sàmm bu baax bi day joxe bakkanam ngir ay xaram. «Man maay sàmm bu baax bi. Ni ma xame Baay bi te Baay bi xame ma ni, noonu laa xame samay xar, te ñoom it ni lañu ma xame » (Yowaana 10 :11,14)

Yaa ngi laaj lan mooy xew gannaaw dund gi ? Ndax danga sonn ci di dund ngir ay mbir yuy yàqu wala di maxe ? Ndax leeg-leeg dangay am xel ñaar ci solos dund gi ? Ndax bëgg nga dund gannaaw de ? Su de noonu la deme, Yeesu mooy yoonu mucc gi ! Yeesu ne ko: «Man maay ndekkite li, maay dund gi. Ku ma gëm, boo deeyee it, dinga dund. Rax-ca-dolli kuy dund te gëm ma, doo dee mukk. Ndax gëm nga loolu?» (Yowaana 11 : 25-26).

Wan mooy yoon wi? Lan mooy dëgg gi? Lan mooy dund gi? Yeesu ne ko, “Man maay yoon wi, maay dëgg te dund it man la. Kenn du ñëw ci Baay bi te jaarul ci man. (Yowaana 14:6)

Xiif bi ngay yëg xiifu baatin la te Yeesu rekk mo ko mana feesal. Yeesu moom kenn mooy ki mana dindi lëndëm yi. Yeesu mooy buntu dund gu naat te sax ba fàw. Yeesu mooy xarit bi ak samm bi ngay wut. Yeesu mooy dund gi, ci àddina si ak ci weneen wi. Yeesu mooy yoonu mucc gi !

Li waral nga yëg xiif woowu, li waral nga niroo ku reer ci biir lëndëm yi, li waral manuloo amal solo sa dund, moo di danga taqalikook Yàlla. Bibal bi wax nanu Ñépp a bàkkaar, ba joteetuñu ndamu Yàlla. (Kàdduy Waare 7 :20 ; Waa Room 3 :23). Wëndëŋ wi ngay yëg ci sa xol mooy Yàlla ji wuute sa dund. Sàkk nanu la ngir nga am ab digganteek Yàlla. Ngir sa bàkkaar, taqalikook Yàlla. Li yees mooy, say bàkkaar dina la taqaleek Yàlla ba fàw, ci dund gi ak wi ci topp (Waa Room 6 :23 ; Yowaana 3 :36)

Naka la bi jafe-jafe di safarawe? Yeesu mooy yoonu mucc gi! Yeesu gàddu na say bàkkaar ci kawam (2 Waa Korent 5:21). Yeesu de na ci sa wàll (Waa Room 5:8), jël mbuggal li nga yellool. Ñetti fan gannaaw gi, Yeesu dekki na ci biir ñi de, firndeel ndamam ci kaw bàkkaar ak de (Waa Room 6:4-5). Lutax mu def loolu? Yeesu ci boppam tontu na ci laaj woowu: “Genn mbëggeel manula weesu joxe sa bakkan ngir say xarit” (Yowaana 15:13). Yeesu de na ngir nga mana dund yaw. Bo wekke sa yaakaar ci Yeesu, gëm ci dewam ni sa peyug bàkkaar, say bàkkaar yépp dinañu la leen baal te dandale leen ak yaw. Ci noonu sa xiifu baatin dees na ko matale. Làmp yi dinañu tàq. Dinga jot ci dund gu naat gi. Dinga xam sa xarit ak samm bu baax bi. Dinga xamni am nga dund gannaaw de—dekki ngir dund ba fàw ak Yeesu!

“Ndaxte Yàlla dafa bëgg àddina, ba joxe jenn Doomam ji mu am kepp, ngir képp ku ko gëm am dund gu dul jeex te doo sànku mukk” (Yowaana 3:16).

Ndax dogu nga topp Yeesu ndax li nga jàng ci moom fii? Sude noonu la deme, demal ci “Nangu na Kirist tay” butoŋ bi ci suuf.

English



Delul ci Wolof ci xët bu njëk bi

Wan mooy yoonu mucc gi?
© Copyright Got Questions Ministries