settings icon
share icon
Laaje

Ndax Yàlla am na?

Tontu wi


Yàlla am na doon na benn ci laaj yi gëna war te gëna am solo bu bépp nit mana bayi xel. Xalaat yi ci Yàlla bari nañu, waaye ci tontu laaj bi, ndax Yàlla am na ? Romb na ab bayi xel ci ay dirub simili te laaj na ay xalaat yu bari aki firnde. Ci njextal sax, li nuy gis ci jaar- jaaru doomu àdaama, xarala, xel ak netali jëme na ci tontu bu dal xel : waaw, Yàlla am na.

Leeg-leeg, Laaj bi ni lanu koy faral di laaje : « Ndax man nga firndeel ni Yàlla am na ? » Jafe jafe bi mooy, donte dëgg gu wer la ci boppam, amul ben firnde ni ci wàllu matematik yi. Ngir loolu, Bërebu ndaje yi duñu soxlo ay firnde ngir tàbi cib ate ; dañuy wuta dindi « xel ñaar bi niru lu jaadu » te xol walla bayi xel « li gëna jaadu ».

Laaj “firndewu” Yàlla bu kenn dul weddi xel manul nàngu loolu. Du firnde yi du nit ñi noonu lanuy doxe ci dund gi dëgg. “Daajeek” ay xew xew te “nàngu” leen am na ag wuute gu xóot. Ay lay yu dëggër te tëju dina jafe ngir yey ñi doggu ci baña gëm. Ngir ki doggu ci weddi lépp, du ay « firnde », donte sax loolu dina doon yey kenen ku mu doon. Yeeneb nit mo ëpp doole bépp firnde gu mu mana dajeel.

Loolu dafa tekki ni ab limub “ngëm” jaadu na—te baña aju rekk ci amug Yàlla. Xam xam bu mat sëkk romb na sunu mën mën. Ňaaw njort yi dañuy lëndëmël sunuy gis-gis. Dinañu doon ab kàmb ci diggante linu wara “xam” ak linu wara “gëm”. Noonu lay deme ak ñiy weddi ak aji gëm yi. Manunoo xam lépp li tënku cib toogu sa bu nekk bu nu siy toog, di lekk ñam walla di jogi yeegukay. Jëf yi ni mel dafa laaj ab taxawayu ngëm. Danuy jëf donte umpale nanu yenn mbir yi, ngir linu xam. Loolu mooy li tënk ngëm ci Bibal bi, ba ci ngëm gi nuy xamal ni Yàlla am na. Am nanu koolute ci linu xam, linuy yobbe nu jëf, donte sax sunu xel dajul lépp. (Yawut ya 11 :6)

Mo xam nu nangu wala baña nangu Yàlla, taneef bi dina laaj ngëm. Ngëm ci Yàlla laajul ab ngëm bu gumba (Yowaana 20 :29), waaye manul tamit daan ki fasul yeene gëm loolu (Yowaana 5 :39-40).

Jaar jaaru doomu àdaama, tërëlinu xel ak firnde yi tar dañuy dëgërël ngëm, giy dimbali ñépp ngir tontu laaj bi di Ndax Yàlla am na ?

Ndax Yàlla am na?— Jaar jaaru doomu Àdaama

Waxtaane amug Yàlla mu ngi tambale lu ci ëpp ciy lay yu bayyiko ci sunu tërëlinu xel. Lu xel mana nangu la waaye du noonu la doomu àdaama yi di doxe naka jekk. Kenn manula tambale di dindi bépp gis gisu ëllëg, di xaara topp ab yoon bunu taxawal ba noppi soogam di ci xalaat. Nit ñi dinañu am ab njàngat ci dund gi jaare ci àddina gi leen wër. Kon, xool amug Yàlla warna tambale ciy jaar jaar. Gannaaw gi, man nanu jëfandikoo tërëlinu xel ngir saytu ay gis gis.

Firnde yiy wonne ne Yàlla am na ñu ngi ci jaar jaaru doomu àdaama bi bes bu nekk (Waa Room 1 : 19-20 ; Sabóor 19 :1 ; Kàdduy Waare 3 :11). Loolu bokk na ci xam lu jekk ji nuy judduwale. Bokk na ci it gis gis gi nu am ci jawu ji nu wër. Dundug doomu àdaama Dafanuy ga nu gëm ne dëgg gi, naxaate gi, mbëggeel, mbañeel, lu baax, lu bon, etc yu am te dëggu lañu te am na luñuy tekki. Lu ëpp ci nit ñi jaare ci netali ga nañu leen ñu gëm dara lu romb te gëna rëy linuy gis jaxran.

Sunuy jaar jaar duñu ay firnde si yunu mana tënku, ci dëgg. Waaye ndare loolu, Yàlla dafay jëfandikoo limu sàkk te wonne ko ngir xirtal nu ci moom (Peeñu 3 :20). Jaar jaar yi nu bokk dafanuy wax rekk ne war nanu wut yeneeni tontu (Macë 7 :7-8). Ñiy fenatël wala di sofantal Wooteb Yàlla jooju diñu jëfandikoo ñak xam ni ab lay (Waa Room 1 :18 ; Sabóor 14 :1).

Ndax Yàlla am na? — Tërëlinu doomu Àdaama

Ňeeti xalaati tërëlinu doomu àdaama yi gëna rëy ngir amug Yàlla mooy lay yi Li waral lu xew lu nekk, naka la jawu ji bindo ak li jaadu te nekk ci sunu xel.

Lay bi di cosmoligik mooy saytu lu waral lu xew lu nekk. Lu xew lu nekk am na lu ko sàbab, te loolu it am na lu jiitu lu ko waral tamit. Wante, loolu manula weye noonu ba abadan ci jamonoy demb, lu ko moy tambali bi du doon lu dëggu. Tërëlinu xel dafay laaj dara lo xam ni dafa nekkoon ba fàw te dara waralu ko. Sunu jawu ji, ci bu leer, saxulwoon ba fàw. Xel dafanuy yobbu ca Yàlla : nattukaayu Yàlla bi kenn walla dara sàkkul, mooy li waral sunu nekk.

Lay bi di teleologik dafay saytu naka la jawu ji bindoo. Asamaan yi rëy yi ko wundu, sunu jànt bi, naka lanu bindo sunu ADN, yi ko sàbab—Ñoom ñépp dañu melni yunu rabb te lépp jaar na yoon. Loolu dafa am doole ba ñi gëmul dara sax am nañu jafe jafe ngir baña gis ni sunu jawu ji bindoo.

Amul dara leneen ci biir yooyu pacc walla doole yuy wonne ne loolu motax ñu bindoo noonu. Monte, bu ñu melul ni ñu mel noonu, li leen wundu—ak dund gi— doon na nekk lu manul nekk. Ay fukki mbir yu wuute ci jawu ji andandook mat sëkk ba dund gi doon lu mana nekk, te rax ca dolli lu doy waar. Xam xam masula seetlu walla leeral naka la dund mana bawo ci lu dul dund, waaye dafay wonne ci xef ak xippi yeneeni mbir yu yaatu. Ab mboolo yuy gëstu ci mbirum ay doc yu gis baat yi ma ngi fii ci miru benn doc wunu yatt loolu laaj na ab xam xam bu daj àddina si. Ci boobu waxtu, ADN bu doomu àdaama mu ngi doon misaal ab mbidin bu ëllëm te romb xam xam nit ñi gënoona xarañ ci doomi àdaama yi. Disaayu firnde gi, ci lu xel di nangu, dafay dëgël xalaat bi di Kenn ku am Sago—Yàlla— ni ki waral loolu lépp.

Lay bi aju ci li nekk ci sunu xel moom mu ngi aju ci lu baax ak lu bon, lu teginu, ak yu ni mel. Nu wax rekk ni mu ngi aju ciy waxtaan ci « li waroona nekk », du rekk ci « li nekk ». Sart yi nekk ci xel jotewul dara ak yenn xalaat yu rëy te ñak yërmande yi nu mana am te war ko xaar cib mbindef mu nekk rek noonu te wara dund ci kaw lépp ak lumu mana jar. Xalaat bi rekk di wonne ni doomi àdaama yi dañuy xalaat ci linu gisul ak te nekk ñiy jëfandikoo seen xel dafa rañeelu. Bu nu romb loolu, li ëmb ni xelu nit di doxe soppekuwul dirub nétalib doomu àdaama ak jaare ci aada yi.

Ci beneen wall, wecce xalaat yi dafay yobbu ci ab selebe yoon. Manam xalaat yi ci sunu bopp la aju, te ci noonu duñu doon yu xelu, walla tamit ñu wekku ci sàrt bu dul soppeku mukk. Jaar jaaru doomu àdaama yi dëggëlul xalaat bi naan xel mu rafet du dara. Leeral bi gëna yenu mana mooy litax nit ñi di am ay xalaati xel te di ko Jëfe mooy ni am ay sart yu dul deñ te am ku leen sos di, Yàlla.

Ndax Yàlla am na? — Xelu doomu àdaama

Lay yi bawo ci xalaatu nit ñu ngi sukkandiku ciy seetlu. Ay xalaat yu melni Big Bang wonne, gën ca yees, jawu ju nu sàkk te ju saxul bu nu sukkandikowe ci xalaatu nit. Noonu it la deme ngir ni ADN bi soso. Yenn lim yuy wonne tey dëggël xalaat kenn ku sàkk lépp te safaano ak ay leeral yu melni ab jawu bu sax ba fàw wala bu tëb rekk nekk.

Gëstu jaare ci doj yi dafay dëggël Bibal bi. Nit ñi, xew xew yi ak béreb yi nekk ci Mbind yi firndeel nañu leen ay yoon yu bari jaare ci gëstu. Yu bari ci yi gëstu yi feeñal ñëw nañu gannaaw bi ñiy weddi xew xewu Bibal bi waxe ni yooyu xew xew ay waxi caxaan lañu.

Netali ak Mbind yi ci seen wall, dañuy indil japale amug Yàlla. Samug Bibal bi benn misaal la: Sunu man manu jaraat ci xew xewu yi nekk ci Mbind yi ci benn Jamono te jege li xewoon dëgg dafay dëggël Bibal bi. Ni Caada Yawut yi ak Kërcen fëse ci sunuy aada, li xel nangu, aq doomu àdaama ak juddu xam xamu jamonoy tey dafay wonne tamit ab topp bu lalu ci dëgg.

Ndax Yàlla am na? — Yàlla ci sunu biir

Benn ci pacc bu ci nekk ab wàllu gëstu wu rëy ak it lunu mana sukkandiku ngir bind ay junniy tere. Donte, amug Yàlla wonne nanu ko ci fann bu xóot, ci lu ëpp ci nit ñi, ci seen jaar jaaru bopp. Man na jafe nga « firndeel » ñeneen ñi ne am nga mbegte, ci misaal, waaye loolu du soppi dara ci ne am nga mbegte. Loolu tekkiwul ne yaakaar wi si biir am na ndam ci kaw dëgg gi ne faŋ, waaye dëgg yi yaatu yi lu ci ëpp jaar jaar yi ño leen di firndeel. Dund yi soppeku, ay jikko yu nu soppi aki tontu ciy ñaan ñoom ñépp ñu ngi bokk ci sunu gis gisu bopp bi naan Yàlla am na.

Ab degg degg ci dëgg ab Jumtukaay buy yey ci ne Yàlla am na, te loolu mooy yeene Yàlla nit ñépp dund loolu. Yàlla ñëw na ci kaw suuf ci boppam, ni doomu nit (2 Korent 4 :6), ngir nu mana am ab digganteek moom (Yowaana 14 :6). Ñiy wut Yàlla ci dëgg dinañu ko gis (Macë 7 :7-8), li koy firndeel di teewayu Xel mu Sell mi ba fàw (Yowaana 14 :26-27).

Laaj bi di Ndax Yàlla am na ? Ci noonu kenn manusi tontu ak di indi firnde bu amul benn werante, waaye man nanu wax ci disaayu firnde biy firndeel ni am na. Nangu amug Yàlla dib tëbu gumba cig lëndëm. Ab jégo koolute ci biti lëndëm ci biir neeg wu leer te mbir yu bari leer nañu.

English



Delul ci Wolof ci xët bu njëk bi

Ndax Yàlla am na?
© Copyright Got Questions Ministries