settings icon
share icon
Laaje

Ndax Yeesu mooy Yàlla? Ndax Yeesu dafa jape boppam Yàlla?

Tontu wi


Ňeen ci ñiy weddi ne Yeesu mooy Yàlla seen lay mooy ne Yeesu masula wax ne mooy Yàlla. Dëgg la ne Bibal bi masula wax ak baat yi buy wax ci Yeesu : « Man maay Yàlla. » Loolu tekkiwul, ci noonu, ne Yeesu masula jappe boppam ni Yàlla.

Ndax Yeesu mooy Yàlla? — Yeesu wax na ne mooy Yàlla.

Nanu jël ni misaal waxi Yeesu yi ci Yowaana 10:30, “Man ak Baay bi benn lanu.” Seetlu tontu Yawut yi rekk gannaaw baat yooyu ngir xam ni dafa doon jappe boppam ni Yàlla. Jéem nanu ko sanni ay doj ndax wax jooju: « Yaw, nit kese, ngay jappe sa bopp Yàlla » (Yowaana 10 :33, yokk nanu ko si). Yawut yi xamoon nañu bu baax li Yeesu doona misaal ci baat yooyu : nekk Yàlla. Bi Yeesu waxe ni : « Man ak Baay bi benn lanu », dafa doon waxni moom ak Baay bi ñoo yem bindin ak cosaan. Yowaana 8 :58 beneen misaal la. Yeesu ne na, “…laata ñuy sàkk Ibraayma, fekk na ma doon ki ñuy wax Maay ki Nekk.” Dafay fàttali Mucc Ga 3 : 14 bi Yàlla wonne boppam ci baat yi « Maay ki Nekk ». Yawut yi degg baat yi tontu nañu ak jël ay xeer ngir sanni ko ko si limu dingënt, ni ko yoonu Musaa santanee ci (Sarxalkat yi 24 :16).

Ndax Yeesu mooy Yàlla? Ňi koy topp ne nañu Yàlla la.

Yowaana bamtu na Yàlla gi Yeesu doon: « Kàddu gi [Yeesu] Yàlla la woon » te « Kàddu gi ñëw doon nit » (Yowaana 1 : 1,14). Aaya yi ñu gi wonne ci bu leer ne Yeesu Yàlla la ci jëmu nit. Jëfi Ndaw Ya 20 :28 wax nanu : « Ngeen sàmm mbooloo, mi Yàlla jotal boppam ak deretu Doomam. » Kan moo jot Jàngu bi ak deretu boppam ? Sama Yàlla. Te aaya boobu tamit waxna ne Yàlla mo jotal boppam jàngoom ak deretu boppam. Kon ci noonu Yeesu mooy Yàlla.

Tomaa taalibe bi ne na ci mbirum Yeesu : « Sama Boroom mooy sama Yàlla » (Yowaana 20 :28). Yeesu gagantiwu ko ci loolu. Tit 2 :13 mu ngi nuy ñaax ñu xaar delusib sunu Yàlla ak Musalkat, Yeesu-Kirist (xool tamit 2 Piyeer 1 :1). Ci Yawut ya 1 :8, Baay bi ne na ci Yeesu : « Waaye ci wàllu Doom ji, lii la ko Yàlla wax: ‘’Yaw Yàlla, dinga toog ci jal bi ba fàw, ci njubte ngay nguuru. » Baay bi mu ngi wax ci Yeesu ni Yàlla, di firndeel ne Yeesu Yàlla la ci bu wóor.

Ci Peeñu, benn malaaka sant na ndaw bi Pool mu jaamu Yàlla rekk (Peeñu 19 :10). Ay yoon yu bari ci biir Mbind yi, Yeesu jaamu nanu ko (Macë 2 : 11 ; 14 :33 ; 28 :9, 17 ; Luug 24 :52 ; Yowaana 9 :38). Masula tere kenn mu jaamu ko. Bu Yeesu doonul woon Yàlla, kon doon na wax nit ñi ñu bañ ko jaamu, ni malaaka bi ci Peeñu ba defewoon. Bu loolu wesoo, am na yeneeni aaya yu bari ci Mbind mi yuy wax ni Yeesu Yàlla la.

Ndax Yeesu mooy Yàlla? Li waral Yeesu doon Yàlla.

Li gëna am solo te tax Yeesu wara doon Yàlla mooy, su dul Yàlla, dewam du woon doy ngir fay mbuggalu àddina ngir bàkkaar (1 Yowaana 2 :2). Ab mbindef bunu sàkk, la Yeesu naroon doon bu nekkul woon Yàlla, du woon mana fay it mbuggal li dall ci àddina ndax bàkkaar fa kanam Yàlla. Yàlla rekk moo manoon gàddu mbuggal luni toll. Yàlla rekk moo manoon dekku bàkkaari àddina (2 Waa Korent 5 :21), de dekki, wonne ndamam ci kaw bàkkaar ak ci kaw de.

Ndax Yeesu mooy Yàlla? Waaw. Yeesu ne na ci boppam Yàlla la. Ay Taalibeem gëm nañu ko ni Yàlla. Mucc gi dina mana nekk rek ci kaw Yeesu doon Yàlla. Yeesu Yàlla ci jëmu nit la, di Alfa ak Omega bi sax (Peeñu 1:8; 22:13), ak Yàlla sunu Musalkat (2 Piyeer 1:1).

English



Delul ci Wolof ci xët bu njëk bi

Ndax Yeesu mooy Yàlla? Ndax Yeesu dafa jape boppam Yàlla?
© Copyright Got Questions Ministries