settings icon
share icon
Laaje

Wekk na sama yaakaar ci Yeesu…leegi nak?

Tontu wi


Ndokkale ! Jël nga doggal gu nara soppi sa dund ! Xëyna yaa ngi laaj sa bopp : « Leegi nag ? Naka la mana tambale sama dox ak Yàlla ? » Juróomi pacc yi nuy limm ci suuf dinañu la jot ab tektal li ko dale ci Bibal. Bu ngeen ame ay laaj ci seenub tukki, doxantu leen ci www.GotQuestions.org/Wolof.

1. Fexeel mu leer ne xam nga mucc gi.

1 Yowaana 5:13 wax nanu, “Maa ngi leen di bind yëf yii, yéen ñi gëm turu Doomu Yàlla ji, ngir ngeen xam ne am ngeen dund gu dul jeex.” Yàlla dafa bëgg ñu xam mucc gi. Yàlla dafa bëgg ñu am koolute ne mucc nañu. Ci bu gaaw nañu jall ci ponki mucc gi:

(a) Nun ñéppa bàkkaar. Nun ñéppa def ay mbir yu neexul Yàlla (Waa Room 3:23).

(b) Ndax bàkkaar, mbuggal lanu yelloo taqalikook Yàlla ba fàw (Waa Room 6:23).

(c) Yeesu de na ca bant ba ngir fay sunuy mbuggalu bàkkaar (Waa Room 5:8; 2 Waa Korent 5:21). Yeesu de na ci sunu palas, gàddu mbuggal linu yelloo. Ndekkiteem dafay firndeel ne dewug Yeesu doy na ngir fay sunu boru bàkkaar.

(d) Yàlla jagleel mbaal ak mucc ñépp ñi wekk seen yaakaar ci Yeesu- gëm ci dewam ni peyug sunuy bàkkaar (Yowaana 3:16; Waa Room 5:1; Waa Room 8:1)

Lii mooy xibaaru mucc gi ! su ngeen wekke seen ngëm ci Yeesu-Kirist ni seen Musalkat, mucc ngeen ! Seeni bàkkaar yépp baal nanu leen ko, te Yàlla digge na ne du leen masa dëddu walla bayi (Waa Room 8 :38-39 ; Macë 28 :20). Fàttaliku leen ne seenug mucc woor na ci Yeesu-Kirist (Yowaana 10 :28-29). Bu ngeen ame Yaakaar ci Yeesu rekk ni seen Musalkat, man na leen woor ne dingeen nekk aljana ak Yàlla ca asamaan !

2. Wuutal ab Jàngu buy jangale Bibal bi.

Bul japp ni Jàngu bi mooy tàbax bi. Jàngu bi, mooy mboloomi. Dafa am solo aji ngëm yi ci Yeesu-Kirist weccante ay xalaat ci seen biir. Mooy benn bi gëna am solo si jëmu Jàngu bi. Leegi nak bi nga wekke sa yaakaar ci Yeesu-Kirist, nu ngi lay ñaax nga wuut ab Jàngu bu gëm ci Bibal bi ci sa gox te nga wax ak benn njitu jàngu. Seddool ak moom sa ngëm gu bees ci Yeesu-Kirist.

Ñaarelu jëmug Jàngu bi mooy jangale Bibal bi. Man ngeena jàng jëfe santane Yàlla yi ngir seen dund. Xam Bibal bi mooy caabi ngir dund dundub Kërcen bu mucc ayib te am doole. 2 Timote 3 :16-17 ne na : « Mbind mu sell mépp, ci gémmiñu Yàlla la jóge, te am na njariñ ngir jàngal nit ñi, yedd leen, jubbanti leen te yee leen ci njub. 17 Noonu waayu Yàlla ji dina mat, ba jekk ci bépp jëf ju rafet. »

Ňeteelu jëmu Jàngu bi mooy njaamu gi. Cant yi, mooy gërëm Yàlla ci lépp limu def ! Yàlla musal nanu. Yàlla bëgg nanu. Yàlla mu ngi nuy jox linu soxla. Yàlla mu ngi nuy gindi ak diñu jiite. Naka lanu koy baña gërëm ? Yàlla dafa sell, jub, bari mbëggeel, yërmande te fees ak yiiw. Peeñu 4 : 11 ne na, “Yàlla sunu Boroom, yaa yeyoo ndam, teraanga ak kàttan, ndaxte yaa sàkk lépp te ci sa coobare la lépp nekke, te ci lañu leen sàkke. ”

3. Beral ab waxtu bes bu nekk ngir Yàlla.

Dafa am solo ci nun bes bu nekk nuy jël ay waxtu ngir weet ak Yàlla. Ňenn nit ñi ñu ngi ko tudd loolu « waxtu wu dal ». Ñeneen tudde ko « jàng ak xalaat ci kàddu gi », ndaxte ab waxtu wu nuy jagleel Yàlla la. Ňeen ñi ber waxtu suba si mo leen gënal, ci beneen wall wi ñi le ngoon si. Am solo ni ngeen kay tudde walla waxtu wi ngeen koy def. Li am solo mooy ngeen di faral di weet ak Yàlla. Yan xew xew ñooy ëmb sunuy waxtu ak Yàlla ?

(a) Ñaan. Ñaan mooy ci lu yomb wax ak Yàlla. Wax ak Yàlla ci lu jëm ci say njaqare ak jafe jafe. Ňaanal Yàlla mu mayla sago ak gindi la. Ňaanal Yàlla mu jox la ngir say soxlo. Waxal Yàlla naka nga ko bëgge ak ni nga ko nawe lépp li muy def ngir yaw. Loolu la ñaan undu.

(b) Njàngum Bibal bi. Dolli ci waxtaane Bibal bi ca Jàngu ba, ci daara diber bi, wala ndajeb jàng Kàddug Yàlla gi- soxla nga jàng yaw ci sa bopp Bibal bi. Bibal bi am na lépp li nga soxlo ngir dund ab dundug kërcen bu barkeel. Ay tektali Yàllaa ngi ci ngir naka nga wara jële doggal yu and ak sago, naka ngay xame coobare Yàlla, naka ngay jiite ñeneen ñi, ak naka nga mana magge ci xel. Bibal bi mooy Kàddug Yàlla ngir nun. Mooy teere gi yor santane Yàlla yi ngir dund ci anam guy neex Yàlla te neex nu tamit.

4. Suxat ab diggante ak nit ñi la man dimbali nga màgg ci baatin.

1 Waa Korent 15:33 wax nanu, “Bu leen ko réere mbir: ‘Ànd bu bon dina yàq nit ku baax.’” Bibal bi fees na ak ay artu ci lu jëm ci and ak nit ñu “bon” ñi ak limu nu mana jural. Nekkandook ñiy def bàkkaar dinañu yobbu ciy Nàttu ci yooyu ñuy def. Jikko ñi nuy Jëflanteek dina « xal » ci nun. Loolu motax mu am solo ay nit ñu bëgg Boroom bi ak te dogu ci moom wër nu.

Jeemala wuut ab xarit walla ñaar, Xëyna ngeen bokk jàngu, yu la mana ñaax ak dimbali (Yawut Ya 3:13; 10:24). Fexeel sa xarit dila laaj ci say waxtu yi ngay weet ak Yàlla, say yëngu yëngu, ak sa dox ak Yàlla. Laaj leen ndax man nga def lu ni mel ngir ñoom. Loolu tekkiwul ne danga wara bayi sa xarit yépp yi xamul Yeesu ni seen Musalkat. Weyal di doon seen xarit te di leen bëgg. Xamal rekk ne Yeesu mo soppi sa dund te manatulo wey di def lépp li nga doon di faral di def. Ňaanal Yàlla mu may la nga séddoo ak say xarit Yeesu.

5. Sóob ci ndox.

Ňu bari dañu reer ci mbirum Sóob ci ndox. Baatu Sóob ci ndox mu ngi tekki « nëq ci biir ndox ». Sóob ci ndox mooy anam gi ngay fësale sa ngëm ci kanamu nit ñépp ak sa doggu topp ko. Jëfu nëq ci ndox mu ngi misaal suul binu nu suul ak Kirist. Jëfu genn ci ndox mi mu ngi misaal dekki ak Yeesu. Sóob la ci ndox, mooy bennoo ak dewu Yeesu, suulam ak ndekkitel Yeesu (Waa Room 6 :3-4).

Sóob ci ndox du mo lay musal. Sóob ci ndox du raxas say bàkkaar. Sóob ci ndox ab jégo degg ndigël la, fësal sa ngëm ci Kirist rekk ci kanamu nit ñépp. Sóob si ndox dafa am solo ndaxte ab jégo degg ndigël la-fësal ci kanamu ñépp ak seen doggu ci Moom. Su ngeen pare ngir soobu ci ndox, war ngeen wax ak benn njitu jàngu.

English



Delul ci Wolof ci xët bu njëk bi

Wekk na sama yaakaar ci Yeesu…leegi nak?
© Copyright Got Questions Ministries