settings icon
share icon
Laaje

Lan lay tekki nangu Yeesu ni sa Musalkat?

Tontu wi


Ndax nangu nga Yeesu Kirist ni sa Musalkat? Ngir xam bu baax laaj bi, war nga xam bu njëk baat yi “Yeesu Kirist,” “sama,” ak “Musalkat.”

Kan mooy Yeesu Kirist ? Ňu bari jappe nañu Yeesu Kirist ni ab nit ku baax, ab jàngalekat bu màg walla sax ab yonent wu Yàlla. Mbir yooyu yépp ci Yeesu dëgg lañu, waaye wonne wuñu ci dëgg ki mu doon. Bibal bi wax nanu ne Yeesu mooy Yàlla ci jëmu nit, Yàlla ci melokaanu nit (xool Yowaana 1 :1, 14). Yàlla ñëw na ci kaw suuf ngir jàngal nu, faj nu, jubbanti nu, baal nu te de ngir nun ! Yeesu Kirist mooy Yàlla, Aji sàkk ji, Boroom bi. Ndax nangu nga Yeesu ?

Lan mooy ab Musalkat te lutax nu soxlo ab Musalkat ? Bibal bi wax nanu ne nun ñéppa bàkkaar ; nun ñéppa def ay jëf yu bon (Waa Room 3 :10-18). Ngir sunuy bàkkaar, meru Yàlla ak ateem lañu yellool. Mbuggal bi jaadu ngir bàkkaar fa kanam Yàlla ju sax mooy jot ab mbuggal guy sax it (Waa Room 6 :23 ; Peeñu 20 :11-15). Loolu motax nu soxlo ab Musalkat !

Yeesu Kirist ñëw na ci kaw suuf ba noppi de ci sunu wàll. Dewug Yeesu ab peyug bàkkaar la ba fàw (2 Waa Korent 5 :21). Yeesu de na ngir fay sunu mbuggalu bàkkaar (Waa Room 5 :8). Yeesu fay na njëk li ngir nu bañ ko def nun. Ndekkitel Yeesu ci biir ñi de firndeel na ne dewam doy na ngir fay mbuggalu sunuy bàkkaar. Loolu motax Yeesu mooy benn Musalkat (Yowaana 14 :6 ; Jëfi Nday ya 4 :12) ! Ndax gëm nga Yeesu ni sa Musalkat ?

Ndax Yeesu mooy sa Musalkat « sa bosu bopp » ? Nit ñu bari japp nanu ne diné kërcen mooy dem jàngu ba, def ay baxantal ak/walla baña def bàkkaar. Loolu du diné kërcen. Diné kërcen bu dëggu bi ab diggante la Yeesu Kirist. Nangu Yeesu ni sa Musalkat mu ngi tekki wekk sa ngëm ak sa yaakaar ci Moom. Ngëmu kenn du musal ñeneen ñi. Kenn amul njeggal jaare ci kaw def yenn mbir. Benn yoon wi nit mana mucce mooy nangu Yeesu ni sa Musalkat, wekku ci dewam ni peyug bàkkaar ak ci Ndekkiteem ni firnde am dund gu dul jeex (Yowaana 3 :16). Yeesu ndax mooy sa Musalkatu bopp ?

So bëgge nangu Yeesu Kirist ni sa Musalkat, waxal baat yi Yàlla. Fàttalikul, wax ñaan wi walla weneen ñaan du mo lay musal. Ci kaw gëm Yeesu Kirist ak liggeey bi mu mattal ca bant ba rekk mo lay musal ci say bàkkaar. Ñaan wi ab yoon wu yomb ngir wax Yàlla sa ngëm ci moom te gërëm ko ci li mu la indil mucc. “Yàlla, xam na ni bàkkaar na ci sa kanam te yelloo na mbuggal. Waaye gëm na ni Yeesu Kirist gàddu na daan bi waroona dall sama kaw ci noonu jaare ci ngëm ci Moom manes na ma baal. Nangu na sag mayu njeggal te wekk na sama yaakaar ci yaw ngir sama mucc. Nangu na Yeesu ni sama Musalkat! Jërëjëf ci sa yiiw and njeggal lu neex li—Mayug dund gu dul jeex! Amiin!”

Ndax dogu nga topp Yeesu ndax li nga jàng ci moom fii? Sude noonu la deme, demal ci “Nangu na Kirist tay” butoŋ bi ci suuf.

English



Delul ci Wolof ci xët bu njëk bi

Lan lay tekki nangu Yeesu ni sa Musalkat?
© Copyright Got Questions Ministries